28/02/2022
Futbal : raw-gàddug Senegaal fukkeelu bëccëg gi ak benn, ñaari joŋante yi amoon tay ci gaawu bi jeex nañu.
Tëngéej Futbal Këlëb ndam jafe na ko leegi ! Ndax tay dafa tëwooti ak Lingeer kenn dugalul dara ci sa caaxi moroom (0-0). Tëngéej ci juróomi joŋante yi mu mujjee amal ci raw-gàddu gi : ñatti tëwoo ak ñaari jéll la ci ame. Géejawaay la mujjee daan ñatt ci dara (3-0). Ñaar-fukki fan ak juróom-benn ci weeru desàmbar 2021.
Geneen joŋante a ngi doon dox ci diggante Jàmbaar ak Duwaan, benn ci dara (1-0) la jeexee Duwaan a ci am ndam.